@modouyaaydie: Ndaxam ab Murid … Ndaxam ab murid saa su bëggee ludul Ndigal ak ngërëm dootu bennub murid Murid dëgg yombul la yombay nga wax Ne man ab murid laa te doo ab murid Ku tàggoogul ak soxla kay dub murid Ka tàggooki soxla a di ngën jib murid Fabal sab Sëriñ teg fi sab xol, xalam Ba far fàtte say soxla, lii dig murid Murid bub sëriñ dul tuxoo fib xolam Du am soxla yal naa di boobee murid Yëgal kat ne dunyaa ni ag dex la mel Te nag ab Sëriñ moo di gaalug murid Ndegam nag Sëriñ moo di gaalug murid Moyul genn jëm fenn yaw kiy murid Ku gennul du lab mukk, kuy genn lab Akay leb te yii yaar a yaqug murid Te lëf manla tee kat nga leb lab ludul Nga wut sab sëriñ yaw te muñ ag murid Ku wut lëf ludul sab Sëriñ dal di lab Te leb ñépp far xëtt sartiy murid Wutal sab Sëriñ yaw te loo ñàkk muñ Te loo am fabal jox ko, kon ngay murid Murid day muñug ñàkk muñ jépp lor Ba sanggam ba dàkkul ko luy lor murid Lu lay dal ci ag ñàkk mbaa lor muñal Ba sab sangg teggil la koo yaw murid Bu sab sangg teggee sa ñàkk ak sa lor Ku lay deeti teg ñàkk akiy lor murid ? Bu teggeegul it nag sa ñàkk ak sa lor Ku koy deeti teggeeti tontul murid ? Joxal sab Sëriñ sag jur ak sab xol it Te bul waxlu, bul wax, lilee dig murid ! Ludul “maa ngi nii” aska di yaa ngi nii Bu koy wax, bu koy waxlu, déggal murid ! Yabal nit ci sab sangg waxloo ko lëf Ludul maa ngi koy sopp kay dug murid Bàyyil dëgg yobbante lëf sab Sëriñ Ludul ag jur ak bëgg a def ab murid Da ngay sanggloo sab Sëriñ saw yaram Te boo yënggtoo kat mu daw la a murid Xamal yaw ne ab sangg day sangg nit Te doo gis mu sangg it ku deewul murid

Modu Yaay jé Mbenda🟢⚪️
Modu Yaay jé Mbenda🟢⚪️
Open In TikTok:
Region: SN
Sunday 12 July 2026 02:12:23 GMT
16514
2058
20
153

Music

Download

Comments

guoragueye378
guoragueye378 :
7
2026-07-12 12:07:17
0
user9473304488597
user9473304488597 :
🥰🥰🥰
2026-07-12 02:17:58
0
user19094226146792
BogaGeuy :
🥰🥰🥰🥰🥰🥰🥰🥰🥰🥰
2026-07-12 19:02:46
0
user8081145741446
papa diaw :
🥰🥰🥰🥰
2026-07-12 02:41:01
0
thiernoseck473
Thierno Seck :
🥰🥰🥰
2026-07-12 16:33:09
0
..fallou.diop..kar
.Fallou Diop. Kar :
❤️❤️❤️
2026-07-12 16:28:22
0
gueye.kampoma
DOLÉLL KHASIDAYI💯💯💯💯 :
❤️❤️❤️
2026-07-12 14:05:46
0
tallagueye182
fayalla darra doufa jeex :
❤️❤️❤️
2026-07-12 13:35:15
0
user9380400514814
2020 :
😁😁😁
2026-07-12 13:29:54
0
mourtalla.tall1
mourtalla tall :
🥰🥰🥰
2026-07-12 13:21:50
0
ndiaye.baye.fall.b3
Ndiaye Baye Fall bi 890 :
🥰🥰🥰
2026-07-12 12:23:44
0
domoudarou498
domou darou498 :
🥰🥰🥰
2026-07-12 12:19:24
0
22adamanfall
22adamanfall :
🤲🤲🤲
2026-07-12 12:12:53
0
mamethierno852
mamethiernocissé199 :
🥰🥰🥰
2026-07-12 12:05:39
0
smodoudiop2
smodoudiop2 :
🙏🙏🙏
2026-07-12 09:26:25
0
oktar.ndagn
OKTAR NDAGN :
🥰🥰🥰
2026-07-12 18:06:10
0
faou283
faou :
🥰🥰🥰
2026-07-12 19:40:20
0
falloumbengue1130
Borom lèr yi 113 :
🥰🥰🥰
2026-07-12 20:25:17
0
To see more videos from user @modouyaaydie, please go to the Tikwm homepage.

Other Videos


About