@mouridexidma: Sëriñ Abdu Rahmaan Mbàkke daa wooko gis ludul waxtu julli te fooko fek moo ngi jàng alxuraan mbaa xasiida wala mu yor kurus daa xamon njariñul waxtu xam liko fi bàyyi woon mooy kiinu daa firil teere xam-xam yi ci jàngalinn bi gëna wer gëna sell gëna leer gëna rafet. Yàlla nako saa boroom doli yërmànde ak njéggal ci barkep alxuraan. Wér na motax Sñ Àllaaji Mbàkke defòon séede bi ci moom Sñ Àllaaji Mbàkke dafa waxòon ni: « Sëriñ Abdu Rahmaan mooy ki nga xamni mësta néenal ab waxtòom, lépp jox nako sunu boroom». Te lòolu kuko xòol ci ay nataalam wala vidéo yi gis ko. Saa boo ko gisee mongui yor ci loxom al quraan, wala qasiida wala kruss.