@karmatii.xatuyadi: Borom Touba Doo jeele doo xaajal it doo déeyle bay nasal it Wutal ag dex ba sun xel dootu daj rootaan Yaa doylu yaw te ku am ag doylu yaa ko ko jox Doylul nu wallis di rootaaneek a wàqi sayaan Sàkkal nu ay kër yu yaatoo yaatu tey jag a jag Ban dëkke sëf di la yët yaw mii akay xaabaan Ba bis bu nekk nu fab ab junni jox la nga yor Te boolekooki sëb ak pepp ak ndimooki mbalaan Ak suukar ak yàpp ak déem ak dàqaaraki buy Ak sump ak laalo ak kuur ak tameeki bagaan Ak yomb ak naajo ak mboq ak xorom su la doy Ak lépp ngir yaa nu fiy jàlleek a dem diiwaan Sarax nu geesu nu bis geesub ngërëm bu nu bég Ndegam da noo bon itam noo ngii fi yaw di wayaan Ay wax du jee waande nun wax nan la kem la nu man Te wax du gudd ba jàllit « Yaak a doy kiimaan ! #t #tiktoksenegal🇸🇳 #motivacion #pourtoiii #yourpage