@modouyaaydie: Rikk Asan lu man a xew … 1. Rikk Asan lu mana xew Awal ndigal te yaru yaw Kon dinga làq wépp yiiw Tey ak ëllëg maa la ko wax 2. Mbooleem lu deefi jog di wut Yar a ko gën gën koo rafet Moo jara dox junni bi at Di wut Sëriñ bu la ko jox 3. Ku yaru rekk a mata am Ku yaru rekk a mata xam Ku yaruwul matula am Matula xam turam wa sax 4. Ab yar li tax amul moroom Day taxa gën fa say moroom Tey taxa gën fa sa boroom Ku la yarul rekk a la nax 5. Ku la mayoon i junni yit Te jàppul ub yar may la yit Leegi nga gis junni ya rot Woroomi yar for ko te sex 6. Ku yaruwul matula yër Ku yaruwul matula yor Ku yaruwul alku na far Ku yabu far tàbbal ko pax 7. Ab yar yamoowul ak dara Ku ko amul amul dara Ku ko am it ñakkul dara Sëriñ bi yal na nu ko jox 8. Ab yar la deefi gën e nit Ab yar la deefi sute nit Ab yar la deefi raw e nit Nde du alal ale rëy i yax 9. Juddoo ki jur matla damoo Ragal Yàllaa mata damoo Te ku ko am du ko damoo Ngir dootu gis baaxam ga sax 10. Ku gis boroomam dootu gis Boppam te moona dootu gis Moroomam it te dootu gis Daraaka wax wax i larax [futilité] 11. Moo tax ba Yàlla ku ko xam Yaru te ken du ko xam