@senwolofaltv: #wolofalserignemossaka #ayaasoodan Ku lay jaay taar na sam xel dem ci Yónnen
Ka taaru ba Yàlla yónni ko saaru Yaasin
Ku lay jaay taar na sam xel dem ci Taahaa
Wa Taahiru ak Mutaharu ñoo di Yaasin
Ku lay jaay taar na sam xel dem ci Maahin
Ka far bàkkaar ya kookale moo di Yaasin
Ku lay jaay taar na sam xel dem ci Haadii
Ka gindi sa maam ya réeroon wan la Yaasin
Ku lay jaay taar na sam xel dem ci Nuurun
Siraaju-l-Laahi làmpub gaas ba Yaasin Ku lay jaay taar na sam xel dem ci Muxtaar
Ka Yàlla ni Mustafaa ma ñu tann i Yaasin
Ku lay jaay taar na sam xel dem ci Yaasin
Imaamu mursaliin ki lee di Yaasin
Muhammad mooy turam wa ñu sant i baayam
Wa Ahmadu mbaa te Haamidu mbaa te Yaasin