@birame_lahi_17: Al hamdu lil laahi nan gëm nangu ay dogalam Si Moom lanuy dello moo moom jaamñi ak luñu am Innaa lil laahi wa innaa raaji’uuna ilay- hi Yalla mooy joxe mooy jël noo ngi nangu jëfëm Dunyaabi workat la moo woor Sayyidul-umami Moo wor Sahaabayi waajii Àddunaako xajam Wal mawtu baabun wa kulun- naasi daaxiluhuu Ubbilna Maam Alasaan buntëm nu ñàkk jëmëm Ni Dee budoon jotu kon Jullit ñi jot Alasaan Ci ruuh yo doy ni Sëriñ Raan raw na lun mana am Bu ruugi doon jaay nu defsiy ndambi ndambi wurus Ba defsi Àdduna gep ngir Seydi Raan baña dem Taa’an wa Kaafan si weeruw Tamxarit cala dem Nuy seenu far waneen weer suux nu sax si lëndëm Si Baktashin si atum Gàddaay ga Goorga laxas Bes booba tiis na ku tiitul daa newul diko gëm Ëllëk sa ñep rotsi Yoof kuniy taxaw di misaal Mbaaxuk Sëriñ Raan di jooy naa wëy fu Àdduna jëm Kep ko taseel mulanaa jaal naala Maam Alasaan Kubaax teyiw demna tay ngir fekki Maamja Limaam Dunyaa lëndëm na kerook xol yepp weet na itam Shawxan wa lahfan si Baay Raan miidi bahrul-karam Funuy giseeti ka donnoon Maam Limaamu si ay Jikkoom yu màgg ya Baay Raan yaanu làqqu badem Woyof na loolu ni ab xob waaye sooka xamul Baatin ba sànkala mooy Marjaanu moo raw ngalam Jikkoomya day geej Sëriñ Raan xuusko day jafe lool Te awma gaal kon xanaa ma wax si tuuti lu yam Taxwaa ilaahil- waraa moo fees xolam ba mu gëm Maamam Limaamu te woolot Yalla Buur binu moom #mouride_tidiane_layenne_niassene #mamealassanelahi #kourel_bu_yiw_bi🥺❤️ #bayelayeamoulmass #bayelayeamoulmass🕋🤍 @HaMsA_RoHuL_HuTsI ✪ @Al_Ghaariq @Seydi Rane